DOCUMENT

MAMADOU BARA SAMB – LE JEUNE POETE : Sargal al Xaliifa Sëydinaa Muhammadul Muxtaar mu Sëydinaa Manjoon Laahi

today29 décembre 2021 103

Arrière-plan
share close

Voir la vidéo

ICI

1
Ku Yàlla yan téeñ la, kum xëy yonni jox na la paas
Kum yekki taawu la, kum fal may ya day gën a fés

2
Moo def nga doon Xalifab Yonnen bi cig Xereñam
Te Abdulaay a la xàllal, junj doy na ku muus!

3
Yàllaa la jox li nga yor tëyeel te dox di na baax
Yàllaa la yekki wëyal ndax ndimbalam la du jaas

4
Jal bii nga toog mooy jalub ki Yàlla yonni ci nun
Yaay ab sëtam di Xaliifaam lun la fonk mu des

5
Baay Duudu tay yaay (Amiirul Muuminiina) bu wér
Yaay Maam Libaas na nu gëm te xam ne Duudu du maas

6
Baay Duudu yaa donna tay Maam Sëydi donni mayam
Ku Gaynde wuutal ku koy sànjaafu suufe xalaas

7
Baay Duudu yaa donna Maam Njoon (Saahibul Karami)
Ku yab ku Yàlla teral péeyam amoo fa palaas

8
Baay Duudu lii Sëydi Caw ak Sëydi Raan yore woon
Lañ boole jox la ko sallaaw Yàlla moo man a nas

9
Baay Duudu yaa donna Baay Ablaay ci Cër ya, jogal
Njaboot gi gunge la, ndax tawfiix gi Yàlla ko res

10
Bul beddi ken, na nga uuf ñép man nga boole nu boot
Lu soxla diis diis kudul Buur Yàlla bul ko ko diis

11
Jàppal sa rakk yi deel diisook ku nekk ci ñoom
Bu kenna dox seen diggante, luy safaan na ñu gas

12
Jàppal sa doom yéppa ak jarbaat yi kuñ man a doon
Bul deglu waane, na Buur neenal pexeem ya mu nas

13
Moytul ku Àddina jay, moytul ku Diine ñorul
Moytul ku xol ba setul te jaamu Yàlla ga des

14
Na Buur musal la ci ab waaneek ku Àddina man
Muccal la fawwa ci Ibliis ndax pexeem ya du jaas

15.
Xam naa ni gor piir nga jambaar loolu am sutura
Buur bii la làq ba tay mooy feg sa Jal ba du tas

16.
Ñéppaa ngi yeeslu ci yaw, ndax Sanga yaay sunu Cër
Baaleel te jéllale sallaaw xol yi yaay ki ko fees

17
Waa Ahlu Laay nanu doon aw say te jàppale kii
Yonnen bi wuutal këram buñ nangu ken di nu tas

18
Nan tënku nan moytu bun ñaaw njort nan rafetal
Nan fonk Diine ji, xol yeek ruu yi nan ko raxas

19
Na Yàlla julli ci Yonnen taawu ab Xalifaam
Te yokk leer Abdulaay te taawu sët yi fi des

16.12.2021

Écrit par: soodaan3

Rate it

Commentaires d’articles (0)

Laisser une réponse

Votre adresse email ne sera pas publiée. Les champs marqués d'un * sont obligatoires


0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non