ACTUALITES

RAPPEL A DIEU DE MAMADOU BARA LAHI : Le viatique de Soxna Maty Lahi bint Seydina Mame Alassane Lahi

today3 mars 2024 267 1 7 5

Arrière-plan
share close

Le viatique de Soxna Maty Lahi bint Seydina Mame Alassane Lahi

Bara Laye sunu xol ndaw lolou daanou beguel

kanie ngay nieuwate niou deufeul sune xol yi xool sa kanam

Xana sa toukki bi dotoul dieex nga dellou ci xool ndiabote gui

doom boula neexé delouwate fanga dieum

Yow mane bou diante bi soo nga delouwate

niou deufeul sene xol yi faté naxar wi sangaa kanam yi

Baa saa’tane lahzatane xana namoo sa ndiabote

ndiour gangui ni dila xaar sahaaba bi yow lanou miine

Bara Laye foumay dieuleeti koumay deufeul

dima dello sune Borom dima mougne loo lorr yi

Bara Laye koumay dioxati ay niaane aki dogg

nguir mou serral samap xol oyofal natou yi

Ayy Bara Laye koumay waxtaanal si Seydi Rane mima doy

sama boumou thioffel bobou sama goor googou

Bara Laye koumay dioubantéti

bouma dioumee wala ma diadda yoone wi

Bara Laye baa xam ngani mala gueunone beugue nga sori lool si mane

ak louma sor sori sori si yow mima daane wax Yaay Booy wala sama Yaayou bopp

Bara Laye nouyoulma sama goor ga Seydi Rane

neeko namanako loolll waxal mako limala waxone yeup

Bara Laye boulko faté wax lima waxoone

neeko boumou bayi di leeral sama yoone

Neeko ragalna dounyaa bi ak nimou leundemee diaxasso

neeko namay nguindi saa sounek

Bara Laye nouyoulma Sanga ba Al Imaam asws ak ndiabote ga te Rohou Lahi as djiitelene

ziaaralma lene bou baax

Boul faté sahaba ya mag niou baax nia sama maam Khady Wade

neeko namanako torop

Bara Laye doumala faté sama waadji yow tamite

lou ganale gui neex neex boulma faté

Na Bour bi dolli sa leer bi abdi maa xoulixaa

niouy sax di dioulli si Ndjine ak toppa ay ndigueuleum

Na Yallah may Sokhna Saly Anta Laye ak sa ndiabote barké ak loufiy soutoura

xolou mounie ak ndeuguerlaay defalko sa soppe yi ak Ahlou Lahi gui yeup ak dioulite yi

Denk nane Yallah Buur bi Cherif Laye ak Sokhna Laye

mou sammal nioulene aarlene laxalene fou yaxxa yegoul

Seydina Issa Laye Samb Yallah roussnou si mom

mou teeri ni aw yoone mou soute Al Imaam Saxiir aw fane té dieul barkem

Mane Maty Laye mangui lay wax a très bientôt

MON TRÈS CHER BIEN AIMÉ

Na Yallah dioulli si Baay Laay ak nia feeté sa mom seulmeul si mom

mayniou ndam ak mouthie fanou dieum

Soxna Maty Thiaw Lahi bint Seydina Mame Alassane Lahi

Écrit par: soodaan3

Rate it

Articles similaires

Commentaires d’articles (1)

Laisser une réponse

Votre adresse email ne sera pas publiée. Les champs marqués d'un * sont obligatoires


0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non