ACTUALITES

L’HOMMAGE ULTIME DE SOXNA MATY LAHI BINT MAME RANE A BARA LAHI

today5 mars 2024 468 1 4 5

Arrière-plan
share close

و بشّرالصابرين الذين إذا أصابتهم مصيبة قالوا إنا لله و إنا إليه راجعون. أولئك عليهم صلوات من ربهم و رحمة و أولئك هم المهتدون. (Surat 2 versets 155_157)

Alhamdoullilah niou sante Rabanaa moo yabalate Yonnent bi moy Imaamunaa
Mo binde mawtu ak xayaat moy dogal kene doufi dess kudul Borom bi Rabanaa

Dunyaa bi woorkat la moo woor Seyidul Ummam
Moo woor sahaba yi waa jii addunaa ka xajam

Wal mawtu baabun wa kullu naassu daaxiluhuu
Oubilna Bara Laye buntam niou niak jemmem

Kaafan si weeru baraxlu ca la dem
Fadjarouk jummah ja booba bess tiss na ku tiitul da newul kudi gëm

Telefone ya di riirr xibbar ba di jolli
Foo geestu guiss nataalam nioukoy jooyoo ka sëngeem

Niouy jooy Mamadou Bara juroom beni fane lii kay mettinaa

La jël Limamou jël Issa miy xayrunaa du bayyi kenn muy beel di sax si adunaa
La jël Mandione ak Babacar miy xutbunaa mo jël Issa ak Baay Rane ma doon xutwatunaa

Konn kay du tee Mamadou Bara daanu xanaa
Mbooloo ma dajj si Yeumbeul kuy xariit ak soppe riniaane sinaa

Al xamiss niaar fukki fane ak juroom bene sa baraxlu si yor yor ja niou fass yeene gungee Bara Laye lii tiisna xanaa

Woyof na loolu mandu gëm Xaalixunaa
Doon taalibee Mame Seydi ak Imaamanaa
Ab tab lawoon geejak teranga lay missal mbokak xariit jiriim fakiir yi jaxxanaa

Xam xam bu sella buy bayaan kene dootu wax ambassadeur bi jeunesse bi niaakanaa
Jeunesse bi niaakane ka doon sene royuwaay done sene soppe sene conseiller Bara gnibbinaa

Ambassadeuru Baye Saxiir bi xeuyna dem
Waa Comité scientifique niak nane ka daa jubbel daane jangaleek waaraate fii buldaaninaa

Waa Yeumbeul tay niak ngeen sene doom ji
Fekkina maam ja Baye Saxiir mimu royoon te soppako

Ay Baye Saxiir teerul nu Mamadou Bara yobulko Seydina Imaamanaa

Terral leneko si maa’u kawsaraa taabal yaak lufay xeewel yaak teraanga bess ba
Muyy beeg di tagga Yonnent bimu gëmoon Ndioolma di contaane lii kay yellanaa

Yaa Rabanaa dolilnu leer Bara Laye tawal si mom feek piithie ngay sap nuurane wa rahmatane mok ahlu baytanaa

Bayifi Mouxtaarunaa mu sax fi lool te werr ne mofiy Imaamanaa

Saxal nu Yallah ‘alal hudda te maynu salam
Te maynu ‘aafiyatan bi jaahi Seydi Limaam

Yaa Rabi salli ‘alal Muxtaari Seydinaa
Salim ‘alal aali wal ashaab te maynu hikam

Maty Laye Thiaw, inspirée par tes écrits (Marsiya Seydina Mame Alassane Lahi et Karbala de Cherif Al Ousseynou Lahi)

Hommage à mon très cher ami MAMADOU BARA SAMB LAYE, toujours dans nos cœurs
Illeyiina di sa keur!!!

Maty Laye Thiaw

Écrit par: soodaan3

Rate it

Commentaires d’articles (1)

Laisser une réponse

Votre adresse email ne sera pas publiée. Les champs marqués d'un * sont obligatoires

  1. Abdou razakh laye sur 7 mars 2024

    Yalna ko yallah yeureume diegueule ko kharè ko aldiana akh mbolème dioulite amine


0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non