🤍IMAM MOUHAMADOU BACHIR LAHI🤍
HOMMAGE A IMAM BACHIR : Jërëjëf Imam Bachir Lahi soodaan3
BAAY BACHIR SUNU IMAM JËRËJËF
– Alhamdoulilahi dañuy geum, nangu ay ndogalam.
– Si mom lañuy delou, mo mom diam yi ak liñu am.
– Ya Rabbul Karim ñungui ñaane nga taw leer si kaw imam
– Bachir doomi Mame Babacar di seutu L’imam
YALLAH DOLIL LEER IMAM BACHIR
– Sa xar kanam lañu bëggoon xool, lāta nga dem.
– Bëggoone tātane si sa xam xam bu selleu ba, lāta nga dem
– Barkeelu si sa leer ba, lāta nga dem.
– Bëggoone took,diakarlo’k yaw, lāta nga dem.
YALLAH DOLIL LEER IMAM BACHIR
– Ya deudu wone adina ak latia biir ba
– Ya nekone ab kumpë si ndawi Akhloulilahi
– Namone nañula guissaat, xol sa jëm ju taaru ba
– Wayé dañuy sant Yallah tey djulli si borom Diamalahi
YALLAH DOLIL LEER IMAM BACHIR
– Weur nañu waayè guissaa tuñu ku melni yaw
– Yallah mola xam,mom mii def li nè si yaw
– Féessoone sunu xol ndax tiofeel biñu amoone si yaw
– Yaadi seutub limamou lahi,geum gui fessone deleu si yaw
YALLAH DOLIL LEER IMAM BACHIR
– Guisla safonté ak yaw doyna seuk sama xol bi
– Guisla talal la loxo nga ñaanal ma, ma geune la def sama xol bi
– Duma diouk si dila ñaanal, ñaane bu deugu t sori lool sama xol bi
– Yallah dollil ñu leer Imam Mouhamadou Bachir mu Seydina Ababacar Sibt IMAMAL LAHI asws