
BOLLE LAYE NDIR : Abdoulaye am nga ndam Bollé Laye Ndir
Bismillahi ma door waye wou djeum ci Baye Laye
Dilay béguël sama way yaw sëtoup yonnéne bée
Alhamdoulilahi niou santa Rabbi Bour béé
Ta doylo Libasse mi Bour yabal ci doune bée
Ta wax toùt ci xémtaani Libasse yidoul djéx
Djoundjoung ya bakana woo gaya gëm yonnéne bée
Dianta féngkana léeroup bidéew dafay soux
Dianta béy sounou yonnéne yërër kitaabée
Limamou laye bamou wooté la léer ya bawane
Ña gëm di nane ta dou djéx Ndjine dou mass si doune bée
Ouskouroulah zikrane la Bour wax si téerém
Lahenlakoum ndaxtélé nioune niou naani toubée
Sounou yonnéne bamou faatoo gëm ya djoy ba djéx
Issa taxaw tay guifal gna gëm yonnéne bée
Seydi Issa bamou woutoo sounoup yonnéne fée
Gëm ya xool ka di rée naa donoy yonnéne bée
Outou yonnéne ta di yonnéne léer thi kawouk léer
Bii garade dafa reuy nio farak yonnéne bée
Mo taxaw taniléne Mahdiyo di saa Baye
Ta may Issa mika war outou may yonnéne bée
Sounguéne xamoul kimou done ladje lénema mane Issa
Nguir may jaraaf ga di done nayibap yonnéne bée
Gaaya waulou waxam gëm ka naani toubée
Gaaya wéddi waxam bagne diawal safane bée
Ndjine yonnéne bamou wooté fa makka l’islam
Adjiboo dayalahi may ndawal Borom bée
Arabe ya diok dadié waxtane la gën farak mome
Gaaya wéddi di réetane farak safane bée
Délsi fii si adjam wooté diiné l’islam
Adjiboo dayalahi may ndawal Borom bée
Boolé sén si adjam bokka ndéey di waxtane
Gaaya gëm dogalap Bour niou naani toubée
Bobou mbeur kouka siiwal xabiibou Rahmane
Domi Seydi Issa siwaloup yonnéne bée
Mangui téertou di waye fii khoutbou Mandione Laye
Xawsou Ndione kouka way rawna naani toubée
Sangoup diamana dou moy Seydina Mandione Laye
Guemël kiraama yi ame fii nguiréek yonnéne bée
Ngoram gua fëss na ta léeral na yonou Baye Laye
Diiném ga siiwna mou yaatal gna gëm yonnéne bée
Seydi Mandione dafa doylo Rabbi ta gëm Ndjine
Xolam raféfna mou yaatal gna gëm yonnéne bée
Taxawlou naa sama waye déllou waye Abdoulaye
Kokou moy sama xol siwaloup yonnéne bée
Bayam di Nabilahi Mamam di Moursaloun
Abdou yaw koula waye rawna naani toubée
Doné won na ci Mamam tabéek xol bou yaa
Rafét djiko beuri xam-xam mélow yonnéne bée
Nioune daniouy mana gëm say kiraama do mass
Wadiou xamoul boula ladioul dou xam yonnéne bée
Abdou Yiiw na yéwéne sélla lone tariham
Féssal ngëmëm ba ca kaw kay sëtoup yonnéne bée
Sanga sény alassane ibnou Seydi do mass
Nonguilay bégué dila doylo nguiréek yonnéne bée
Dama Santa bay maaré nguiréek waye Cherif
Sëtoup yonnéne kouka waye rawna naani toubée
Tambour ba djip na Limamou Laye wooténa
Ndawal Bour foumou fégne gaaya gëm kiraamam yor mélow wéer gna bagne diawal safane bée
Mame Baye Laye Mouhamadounà yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Ahmadounà yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Hamidounà yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Mahmodounà yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Mahdiyounà yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Mame Libassalaye yonnéne bi xayroul wara
Mame Baye Laye Mame Limamoulaye yonnéne bi xayroul wara
Nanguéene dëgël kifi Bour ték si daarou doune bée
Rabbi salli wa sallim anlal Moustapha maynou waye sounou yonnéne ba naani toubée