DOCUMENT

A PROPOS DU LIVRE DE MAME LIBASSE LAHI : Nangu wala baň keemaani Yàlla

today30 juillet 2023 146 3

Arrière-plan
share close

Nangu wala baň keemaani Yàlla

Jublu waay yi teere bi am bi ci jiitu mooy wane ni Yàlla du yónni kumu joxul firnde. Moo tax werante amul yoon ci kuni Yàllaa ma yónni ndax suko yónnee man naň ci xam dara, suko yónni wul itam man naň ci xam dara.

Werante wi nékk ci woote Seydinaa Limaamu Laay al-Mahdi (psl), mini « mana demb mana tay », dafay niru luy wane ni nit ňi, ňi ëpp ci ňoom, xamu ňu ni Yàlla kumu yónni jox lay firnde, té kumu yónni wul dula jox firnde. Mu wax ni ci suuratu Tawbah né :

أَلَمْ يَأْتِهِمْ نَبَأُ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ قَوْمِ نُوحٍ وَعَادٍ وَثَمُودَ وَقَوْمِ إِبْرَاهِيمَ وَأَصْحَابِ مَدْيَنَ وَالْمُؤْتَفِكَاتِ أَتَتْهُمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا كَانَ اللَّهُ لِيَظْلِمَهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ

« xanaa ňoom ňiy weddi dikkalu leen xibaaru gaay yi nga xamni ňoo leen jiitu woon ? xeetu Nuuh ak ‘aad ak samuud, xeetu Ibraayima ak waa madiyana, ak ňa nga xamni ňoom laň wëlbati suuf ci seen kaw. Ňenn ňu ci ne ci ňoom, ba seen ndaw ňëwee andil na leen ay firnde. Kon nak Yàlla tooňu leen waaye ňoo tooň seen bòpp. »

Nu gis ci aya yii ne werante wi soqekoo wul ci Yàlla ndax bimu yónnee joxe na firnde, soqekoo wul itam ci ndaw li ndax indi na firnde yiňu ko jox. Mu ngi soqekoo ci ňi ňu indili firnde te nangu wu ňu firnde ya ; lu jiin njaaga te ňoo ňooy njaag. Ňoom ňoo tooň seen bopp, ci wéddi gi ňu wéddi firnde yiňu leen indil.

Ňaareelu jublu waayu teere bi mooy wane lan mooy firndeb yónnent. Firndeb ndawal Yàlla mooy keemaan (xarbaax). Te loolu liko al-Quraan wane bari na. Bokk na ci fi sunu boroom naan ci suuratu Yûnus:

وَأَغْرَقْنَا الَّذِينَ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا فَانظُرْ كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الْمُنذَرِينَ (73) ثُمَّ بَعَثْنَا مِن بَعْدِهِ رُسُلًا إِلَىٰ قَوْمِهِمْ فَجَاءُوهُم بِالْبَيِّنَاتِ

“ labal naa gaayu Nuuh ya nga xamni ňoo weddi woon samay keeman. Xoolal mujjug ňa nga xamni yònni woon naa ay ndaw ca ňoom. Te ganaaw Nuuh yònni waat naa yeneen yonent ci seen xeet, te ken ku ci ne ci ňoom ba ngay dem jox naala ay firnde yo leen yobul.”

Aaya bi jiitu lii Nuuh indi boorom bi mingi ko tuddee âyât (keemaan). Ci bu ňaareel bi, boroom bi tuddee ci li ndawam yi indi bayyinât (firnde). Keemaan ak firnde ňaari baat la, you bokk benn jubluwaay.

Muy feeňaat ci waxu yónnent Yàlla Saaliw (psl) ji mu wax ci suuratu-l-A’râf :

يَا قَوْمِ اعْبُدُوا اللَّهَ مَا لَكُم مِّنْ إِلَٰهٍ غَيْرُهُ قَدْ جَاءَتْكُم بَيِّنَةٌ مِّن رَّبِّكُمْ هَٰذِهِ نَاقَةُ اللَّهِ لَكُمْ آيَةً

Yeen samaw xeet jaamu leen Yàllah té ngeen xamne amu leen beneen Yàlla judul moom. Indil naa leen firnde bu joge ci seen boroom, Geleemu Yàlla gaa ngi nii ma indil leen muy keeman.

Ňu gisaat loolu batay ci waxu yónnent Yàlla Isaa (psl) ji muy wax ci suurat Âli ‘Imrân:

أَنِّي قَدْ جِئْتُكُم بِآيَةٍ مِّن رَّبِّكُمْ

“maa ngi nii andil naa leen keemaan gu juge ci seen boroom”

Yàllaa tuddee keemaan yooyu yonnentaam bi di wax “firnde “(bayyinât) ci suurat-l-Saff :

فَلَمَّا جَاءَهُم بِالْبَيِّنَاتِ قَالُوا هَٰذَا سِحْرٌ مُّبِينٌ

“ ba Isaa demee yobul leen firnde ya, daňu ni lii njibar gu leer la”

Ci aaya bu mujju bi ma indi, boroom bi di fa wane waat loolu batay, ci waxam ji ci suurat-l-Rûm:

أَوَلَمْ يَسِيرُوا فِي الْأَرْضِ فَيَنظُرُوا كَيْفَ كَانَ عَاقِبَةُ الَّذِينَ مِن قَبْلِهِمْ كَانُوا أَشَدَّ مِنْهُمْ قُوَّةً وَأَثَارُوا الْأَرْضَ وَعَمَرُوهَا أَكْثَرَ مِمَّا عَمَرُوهَا وَجَاءَتْهُمْ رُسُلُهُم بِالْبَيِّنَاتِ فَمَا كَانَ اللَّهُ لِيَظْلِمَهُمْ وَلَٰكِن كَانُوا أَنفُسَهُمْ يَظْلِمُونَ (9) ثُمَّ كَانَ عَاقِبَةَ الَّذِينَ أَسَاءُوا السُّوأَىٰ أَن كَذَّبُوا بِآيَاتِ اللَّهِ وَكَانُوا بِهَا يَسْتَهْزِئُونَ

Xanaa ňoom ňiy weddi doxu ňu ci kaw suuf ba gis mujjug ňa nga xamne ňoom ňoo leen jiitu woon (te def li ňu def), ňo ňu ňoo leen eupoon doole eupoon leen kàntan, bayoon naň suuf si dëkee woon ko nu raw niň ko defee ňom ňii. Ganaaw loolu seeni ndaw ňëw indil leen ay firnde. Yàlla de du moom moy ki leen tooň waaye ňom ňoo tooň seen bòpp. Amul lenn lu jëfkatu ňaawteef yooyu jëf, ludul weddi keemaani Yàlla ya ak dileen kokkali.”

Ňeteelu jublu waayu teere bi mooy wane luy keemaan. Keemaan mooy lu am, maanaam lu « exister », manaan lu « réel. » Lepp lu am Yàllaa ko amal. Te lepp lu Yàlla amal keemaan la tudd ; keneen manuko amal kudul moom Amal-kat bi. Yàlla moom càppaacooli mooy kiy amal. Bokk na ci aaya yiy feeňal ne keemaan mooy lu am ci suurat Yuunus suňu boroom di ci wax ni :

ثُمَّ بَعَثْنَا مِن بَعْدِهِم مُّوسَىٰ وَهَارُونَ إِلَىٰ فِرْعَوْنَ وَمَلَئِهِ بِآيَاتِنَا فَاسْتَكْبَرُوا وَكَانُوا قَوْمًا مُّجْرِمِينَ (75) فَلَمَّا جَاءَهُمُ الْحَقُّ مِنْ عِندِنَا قَالُوا إِنَّ هَٰذَا لَسِحْرٌ مُّبِينٌ (76) قَالَ مُوسَىٰ أَتَقُولُونَ لِلْحَقِّ لَمَّا جَاءَكُمْ أَسِحْرٌ هَٰذَا وَلَا يُفْلِحُ السَّاحِرُونَ

« Ginaaw bima yònne Nuuh ak yeneen yónnent yi topp ci moom, yònni naa Musaa ak Aroona ca Firawna aki gaayam, baňuy dem joxaale naa leen samay keemaan. Waaye bi ňu aggee Firawna aki gaayam da ňoo guis seen bopp rëy dugg leen, ňoom xeet laň woon boo xamne tooň kat laň woon. Ba Musaa ňëwee indi lu am lu juge ci man (ňu jakarlook moom diko gis) danu ne lii njibar la. Musaa ni leen nan ngeen di jakaarlook lu am ngeen naan njibar la, te ngeen xam ni njibar manula amal

Bantu Musaa bi jaan ju amul benn werante la doon. Bum ak bantu njibar yi, bum ak bant laňu sax doon. Soppaleku wu ňu jaan benn yoon donte fii ci Senegaal yàgg naňu fi degg firikatu al-Quran buy wax ni dañoo soppaliku jaan, di ci teg ne « jaanu Musaa dafa xeex ak jaanu njibar yi ray leen. »

Loolu firikat yooyu di wax njuumte lu rey la, bokaale la, ndax njibar amul jaan menuko amal. Jaan Yàllaa ko moom. Seen pexe moo jàppoon nit ňa, ňuy gis jaan fu jaan newul. Waaye bi bantu Musaa soppalikoo doon jaan bu wer, ci la seen pexe toc, nit ňa gis seenuw fen, ňu tuub nangul Musaa ndax xam ni sàkk-kat bi moo def loolii. Firawna aki gaayam jëf jooju taxu leena nangu, ňu sax ci seenug baň ndax rëy.

Ňenteelu jublu waayu teere bi mooy wane ni su nit nee Yàllaa ma yónni ba noppi amal keemaan, nangu ni Yàlla miy amal moko yonni, tawhiid la. Baň ni Yàlla miy amal moko yonni nàkk tawhid la, bokkaale la.

Liy indi boobu bokkaale ci jaam bi mooy rëy. Rëy mooy indi weddi lu am. Gis lu am ni faaƞ sa kanam ngani amul njibar la, rëy mokoy indi ci nit. Sunu boroom wax na ko ci al-Quran ci suuratu-l-A’râf né :

سَأَصْرِفُ عَنْ آيَاتِيَ الَّذِينَ يَتَكَبَّرُونَ فِي الْأَرْضِ بِغَيْرِ الْحَقِّ وَإِن يَرَوْا كُلَّ آيَةٍ لَّا يُؤْمِنُوا بِهَا وَإِن يَرَوْا سَبِيلَ الرُّشْدِ لَا يَتَّخِذُوهُ سَبِيلًا وَإِن يَرَوْا سَبِيلَ الْغَيِّ يَتَّخِذُوهُ سَبِيلًا ذَٰلِكَ بِأَنَّهُمْ كَذَّبُوا بِآيَاتِنَا وَكَانُوا عَنْهَا غَافِلِينَ

« Dinaa dumbooyu loo samay keemaan ňi nga xamni da ňoo nek ci kaw suuf di rëy rëy lu ci lu dul dëgg; ňooňee buuňu gisee samay mboleem keemaan dunuko nangu, bunu gisee yoon wu yanu maanaa dunu ko jàppee yoon, bunu gisee yoon wu yanu wul maanaa moom la ňuy jàppee yoon. Liy indi boobu doxalin mooy weddi gi ñuy weddi samay keemaan ak di leen saggane.”

Gis ku ni boroom weer wi mooma yónni, ngani ko boroom weer wi yónni wu la. Muni weer wi xaral weer wa xar. Mu wëlbatikoo ni la boroom weer wi mooma yónni. Sooko nee boroom weer wi yónni wula da ngay def lila neex. Rëya nangu li am moola jàpp. Loolu moo feeň ci suuratu-l-Qamar boroom bi wax ne :

اقْتَرَبَتِ السَّاعَةُ وَانشَقَّ الْقَمَرُ (1) وَإِن يَرَوْا آيَةً يُعْرِضُوا وَيَقُولُوا سِحْرٌ مُّسْتَمِرٌّ (2) وَكَذَّبُوا وَاتَّبَعُوا أَهْوَاءَهُمْ ۚ وَكُلُّ أَمْرٍ مُّسْتَقِرٌّ (3) وَلَقَدْ جَاءَهُم مِّنَ الْأَنبَاءِ مَا فِيهِ مُزْدَجَرٌ (4) حِكْمَةٌ بَالِغَةٌ فَمَا تُغْنِ النُّذُرُ (5)

“bis pencc jege na te weer wi xar na. Waaye ňoom way weddi yi buňu gisee sama keemaan (mu ame ñu jakkaarloo ak ňoom) daňu koy dumbooyu ne lii njibar la. Weddi naň ko wëlbatiku tópp seen banneexu bakan, waaye nak weddi lu am terewukoo am. Moone de ňoom ňooňee jëf loolu, am naňuy xibaar yoo xamne, buňu ca dellu woon da na leen soň jaajj leen ba la ňu jëf, doonu ňu ko woon jëf. Jangale bu matale bi ame ci xew xew wi mooy ne yónnent (ak keemaan ya muy indi) amaluñu njariň baň kat.

Batay, gis kuni boroom geej gi mooma yónni ngani ko boroom geej gi yónni wu la. Muni geej gi randul, geej gi randu. Mu rëdël ko niko yamal fii, geej gi yam fa. Mu wëlbatiku nila boroom geej gi mooma yónni, sooko nee yónni wu la mooy ne da ngay def lila neex. La daloon wa Màkka ya gisoon xarug weer wa baň, moola dal. Saa yu nit gisee lu am ba nòppi ni amul, limuy wane mooy ne li am neexu ko. Suko neexoon kenn duko ko wan ňaari yoon.

Moo tax Yàlla ni ci suurat-l-Hajj :

فَإِنَّهَا لَا تَعْمَى الْأَبْصَارُ وَلَٰكِن تَعْمَى الْقُلُوبُ الَّتِي فِي الصُّدُورِ (46)

na ngeen xam ni duy gët ňooy gumba waaye xol bi ci dënn yi mooy gumba

Wolof ne « weddi gis bokku ci ». Baň kat bi wane ne su gisee luko neexul dakoy weddi. Amna ňuy xoolee seeni gët : bët li am lalay wan. Waaye amna ňuy xoolee seeni xol : xol du wane li am, li nga bëgg lalay wan, nëbb la li am te neexula.

Ku tektaloo wul keemaani Yàlla, di nga tektaloo say njort, baa say hadith, baa sam piri, baa say deggin, baa say gent, baa say sos, wala sosi keneen. Ku jëndee yoyu jëfi Yàlla, reeral nga sa bopp, ku reeral sa bopp te dellu woo ginaaw, safara di sa kër. Keemaan (le Réel/al-Haqq) mo feete kaw yoyu yepp ndax keemaan jëfi Yàlla la ju amul werante moom miy Sàkk-kat bi.

Lepp lu safaanoo ak li am, neen la (bâtil), mythe la, illusion la, sos la, fiction la.

الْحَقُّ مِن رَّبِّكُمْ فَمَن شَاءَ فَلْيُؤْمِن وَمَن شَاءَ فَلْيَكْفُرْ

« lep lu am ci seen boroom la juge, ku mu neex nangul, ku muu neex baňal »

Yalna nu Yàlla jeggal te jubal nu

Wa aaxiru da’waanaa ‘an alhamd lillaahi rabbil ‘aalamiin

Mame Libasse Lahi
Ibn Chérif Mouhamadou Lamine Lahi
Ibn Seydina Ababacar Lahi

Écrit par: soodaan3

Rate it

Commentaires d’articles (0)

Laisser une réponse

Votre adresse email ne sera pas publiée. Les champs marqués d'un * sont obligatoires


0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non