Poème écrit par Baye Seydi Laye Guèye ibn Serigne Moussa Guèye Lahi
Taliif Abdoulaye ibn issa BaySeydi Laye Gueye
–A– Abdoulaye ba ca abdoulaye ya,lii lagnu sa mame denkone.
–B– baye aak mamou yonent lala yallah tieureu lone.
–D– diiné gui weur na reew mi si say kaddu yinga djibeulone.
–O– ormal nga say wadiour ,diotali seni kaddu tia mame ndione,baye seydi thiaw ak mame Alassane.
–U– ummah bi ranié nagnu sa jeuff,do kugnuy faté ndakh borom bi mola sampone.
–L– leeral nga say kaddug Mame,tasfir yi ak zikr yi weur na kürel ya.
–A– aduna nga ligueyal wan leen dialouba, gnu top Yallah nguir leral seni alaxira.
–Y– yaatu wone am yeurmandé yilif ak yiir si alxurane ndiaboot bila Yallah denkone.
–E– elimaanu Yallah bi nga dane waxtané,di diangalé aki digueul farata yi ak sunna ya.
–I– issa rouhou lahi sa baye mola denkone foré ya, banga matalé la la dieul tegg la si wetam dja.
–B– beus banga toloo ak bunt ba ,tiala sa wote’b mame ba siiw dieum tia kaw.
–N– noflay amoko wone fi dunya lep nguir defar lignu wara fekki alaxira.
–I– imamou imam yi moy sa mame, wax ngako fepp ni Mahdi bi dunya done xaar moy sa mame .
–S– sopé talibé yi,ya soriwone si xol yi ,sa beuss ba tiissone na,guedj randouwone na.
–S– seedé bi tarixa yi amone si yaw mo deugueul taxawaay ak tiofel binga amone si keuru diiné yi.
–A– ABDOULAAHI
akhlou lahi weet nagnu,
alhamdullilah, gnun yallah begal nagnu,
Alhamdullilah, ndakh sa mame naxugnu.
Alhamdullilah, ndax sunu xel yi dal nagnu.
Yallah fayal gnu Abdoullah muy beel ca ilayiiina si wettu seydil awaliina wa seydil aaxirina.
Amiiine🙏🏾