HOMMAGE A BARA SAMB

1er MARS 2024 – 1er MARS 2025 : Hommage à Bara Laye Samb

today2 mars 2025 79 1

Arrière-plan
share close

Hommage à oustaz Bara Laye Samb 😭

  • cover play_arrow

    1er MARS 2024 – 1er MARS 2025 : Hommage à Bara Laye Samb soodaan3

1
dama kheuy niouni ma.. naga dal dégg louma.. Saay raguogn diégéma.. yaa rassoulal laa
2
lima yeuk sama xoll.. mbir mou tiis monou dall.. ahlou laay laafi dall.. yaa rassoulal laa
3
bibliothèque lakk naa.. waadiou bakh gnibinaa.. banxaas boumak danounaa.. yaa rassoulal laa
4
linou dal dafa tiis .. soun yaram dafa diiss.. baara kéen Dou miis.. yaa rassoulal laa
5
lifi féll sounou xéll.. moo yeugeel sounou xooll.. xélle yi dém sounou xooll.. yaa rassoulal laa
6
barani woon sounou xol.. Moofi way sounou xol.. imam sakhir sounou xol.. yaa rassoulal laa
7
ndaw gni niép pagui diooy.. délou xool ligua waay.. gneup Di wakh ligua way .. yaa rassoulal laa
8
yonént rék ga mbeug goon.. yonént rék ga guemoon.. Moustapha ga wayoon.. yaa rassoulal laa
9
makk gni gneppa ga way.. guir dagan séeni may.. toolou diiné ga bay.. yaa rassoulal laa
10
coula xam xamni yaw..yoonou diiné ga aw.. diokh ga yalla sa ndaw..yaa rassoulal laa
11
Mame djiinna séedé si moom.. naane bara samb mima xam.. ããnbidla ããnlimla mom.. yaa rassoula laa
12
mébét youreuy la amon.. thi diiné djii ga guemoon.. yéené yép ga amoon.. yaa rassoulal laa
13
sa démgui tiis Nanou loool… déwé ndaw tiis nalool.. adinaa dal wõora toul.. yaa rassoulal laa
14
bara fékki na taay.. Mame dia ak baye ba taay.. ak imam seyedi gaye.. yaa rassoulal laa
15
yala na bour fay ko yool.. foul dieufeuf maïko tool.. aldianaay don sa tool.. yaa rassoulal laa
16
bara fékina maame.. mim beugon far thi moom.. démna fékki imaam.. yaa rassoulal laa
17
imam sakhir la royon.. diokh ko lépp lim amoon.. deukeuk moom la beugon.. yaa rassoulal laa
18
gnougui diale sounou yaay.. soxena ndeye Saly gaay.. ak soxenam anta laay.. yaa rassoulal laa
19
Ibrahimak seyedinaa.. issa sa mak Dia djitounaa.. cheikh galo diaalénaa.. yaa rassoulal laa
20
imam libass niougui niaan.. thi xananoul manaan ..yalla dooli sa mann.. yaa rassoulal laa
21
nala bour bi téral.. boolé lakk kimou fal.. Mame limamou lafal.. yaa rassoulal laa
22
Sally yaa rabanaa.. thi rassoul seyedinaa.. Moustapha minou naa… yaa rassoulal laa

m@me s@mb@ l@ye ✍️

HOMMAGE A BARA SAMBIMAM SAKHIRLes poèmes de Mame Samba Laye SAMBARGAPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non