#lejeunepoete mooy sargal Sëydinaa Manjoon Laahi ak Doomam ji Sëydinaa Abdulaahi ci seen bés bi leen Yàlla boole. Di santa Ibraahima Laay mu Sëriñ Seex Mbàkke Laay ci xirtal gimu nu xirtal ci liggéey bii, tay ñaan Yàlla mu nangul nu ko.
LEJEUNEPOETE CHANTE AMAR AK ABDULAAHI #lejeunepoete
1
Limaamu moo ko xëy xabaar
Bis di nga donna lii ma yor
2
Bis di na ñëw mbooloo ma daj
nga doon Xaliifa yaw Amar
3
Limaamu moo nu yit xabaar
Mbër mi di siwaal luy (asar)
4
Moodi sagub neeg Kumba Ngoy
Te moo di leeral fuma jaar
5
Amar ma iisaa xàllaloon
mu ñëw di daaral ak defar
6
Amar mi Yàlla wóolu woon
Mooy waajuram te moo ko yar
7
Abdum Isaak Limaamu Laay
Abdum Manjoon ak Baabakar
8
Abdu la Yàlla jagleloon
Muy siiwalab Sëydil Bashar
9
Manjoon da ngaa lebal isaa
Topp ko gëm ko yaa di gor
10
Manjoon da ngay cam su kamaal
Céy Baayu Duudu moo di mbër
11
Abdu taxaw ngir fay Manjoon
Pastéefu day cam su sawar
12
Ne Baay Manjoon toogal ma dem
Céy Magi Duudu moo di gar
13
Ñeen fukki at la Baay Manjoon
Toppa magam fep fumu jaar
14
Moo ko teral ba Maam Libaas
Ñibbee Manjoon ne faw ñu xaar
15
Juroom fukkak ñaari atam
La Abdu toppe rëy na mbir
16
Way na sagal na Baay Manjoon
Ak kuy ndonoom di leen siyaar
17
Maam Njoon gërëm na Abdulaay
Doon njaatigeem goroo ko far
18
Maam Njoon safoo na Abdulaay
Dëkkoo ko jox ko muy defar
19
Baay Abdu gëm na Baay Manjoon
Dëkkee dawal ko moo ko jar
20
Baay Abdu naw na Baay Manjoon
Dëkkee defal ko lum nisar
21
Sëynaa Manjoon day gor su yiw
Su Yàlla may mu raw Badar
22
Maandu na muñ na Baay Manjoon
Ki gën ci nit ñi moo ko yar
23.
Baay Abdu muñ ni Baay Manjoon
Dëddu ni moom ndax moo ko yor
24.
Ñéppa ko seedeel ngor su mat
Ak tab gu yaatu man defar
25.
Amar bi muy mage la toog
Taxul ba ken ruur li mu yor
26.
Doom ya taxaw Sëydeek rakkam
ya ngir sagal Baay bi ko jar
27.
Baay Abdu toogee mag ni moom
Taxul ba ken far fimu jaar
28.
Doom ya taxaw Sëynaak rakkam
ya, seeni Baay Abdoo ko jar
29.
Sëydi Manjoon am Sëydinaa
am Alasaan Duudu Mataar
30.
Am Aytaseen ak Saynaboo
Doom joo ci gis moo raw (Durar)
31.
Baay Abdu taawloot Sëydinaa
am Alasaan am yit Mataar
32.
Am Aytaseen ak Sëynaboo
Doom joo ci xool yéem ko bu wér
33.
Sëynaa Manjoon mooy Abdulaay
Baay Abdu mooy Sëynaa Amar
34.
Weeru Tabaskee seede far
Samsul Hudaak Njool miy Badar
35.
Na Yàlla taw xéewal yu rëy
Ci Baay Manjoon mii nu defar
36.
Te yokka xéewal Abdulaa-
hi mii nu tektal fi nu jaar
37.
Na Yàlla taawu seen Njaboot
te dolli fàwwa seeni leer
38.
Bàyyi fi Baay Muxtaar Xaliif
mook ay rakkam ñuy gën di wér
39.
Bàyyi fi Sëydeek Sëydinaa
ak Ahlu Baytil Muntazar
40.
Taxawlunaa fii yalna Buur
Sóob nu ci leeri Baay Amar
41.
Ak leeri Sëynaa Abdulaay
Maam Sëydinaa ak Baabakar
42.
Ak leeri Sëydeek Alasaan
ak Njool mi Mahdiyut Tahaar
#lejeunepoete
Yëmbël, Talaata 15 Tabaski 1444
04 Juillet 2023