La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)

LEJEUNEPOETE REND HOMMAGE AU MESSAGER D’ALLAH (PSL) : Maa ngi nii ñàkk ngay ku woomle

today3 mai 2023 60 1 5

Arrière-plan
share close

Lejeunepoete mu ngi leen di ñaanal Ñaanug Jàmm ak xéewal.

Xerawlu leen ñetti xasida yii mu def ci Sanga bu tedd bi SAWS.

1. Nàndal ma (Ndar, 22 Octobre 2020)

2. Ay Mustafaa sama Waa ji (Yëmbël, 22 Juin 2022)

3. Maa ngi nii ñàkk ngay ku woomle ( Yëmbël, 26 Mars 2023)

Jërëjëf Sëydinaa Limaamu Laay, teral nga nu Démb, teral nu Tay. Lu nu la way doyul

 

Seydina Isaa Sàmb, moo ma inspirer ci waxtaan bi mu def ci Appelu Rhode Island 2023. Bi ma ko degloo ba noppi lima jëkk def mooy jànga Hamziya bu Imaam Besayrii RTA ba mu jeex, sama xel nekk ci Sanga bi, nammeel gi not ma ma sàkku barkeelu ci Géeju Leer yi Sanga bi sóoboon turandoom boobu di Muhammadul Buusayrii.
Sëydinaa Isaa yàggal a waxtaan ngir yàgg daas sunu cofeel ci Xarul Xalx Muhammad sab soppe di sunu bos. Yal na Yàlla dolli sa xéewal te tawfiixal la foo fi nekk.

  • cover play_arrow

    Maa ngi nii niakk ngay ku woomle lejeunepoete

1
Maa ngi nii ñàkk ngay ku woomle céral ma
Maa ngi yalwaan ngay tab bu rëy ñaagal ma

2
Sanga maa ngii tawat te koo musa ñaanal
Dootu jàmbat ay Njool mi ngalla wéral ma

3
Bu la neexee nga xool ma roof ma ngënéel ya
Bu la neexee nga ëf lu fiy lore daw ma

4
Bu la neexeet nga teg ma sab loxo Yonnen
Sol ma leer yaak xéewal ya, Sanga sagal ma

5
Da ma réeroon di wër ba far daje ak yaw
Doo ma delloo xanaa ci gol bi, yëram ma

6
Luma bon-bon yaw rekka laa musa yaakaar
Musumaa dañ di ñaan Yonnen nga dikkal ma

7
Fat ma Yonnen raxas ma man nga ko sàllaaw
Bu la neexee defar ma léegi jubal ma

8
Yaa jubal Sahba yaak ña leen donna cig leer
Ku fi am yaa ko sédda Sanga céral ma

9
Ana luy tee nga jëwrinoo ma te yan ma
Ana luy tee nga xidmaloo ma nangul ma

10
Ana luy tee nga fal ma may doxi yonnen
Foo fobooy dem ci biir (‘awaalim) yi woo ma

11
Kaña laay naan ci Kaas bi ngir fase Dunyaa
Mustafaa mar wi tar na, kaay nàndal ma

12
Sama xol bii nammul ludul gise ak yaw
Jaxasook yaw, Yonnen bi ngalla ubbil ma

13
Maa ngi nii bóof sa bunt, dootu ma dem fen
Boo yaboo fat ma benna yoon te dëkkoo ma

14
Boo yaboo jox ma lii fi Gaa yi di wutsi
Maa ngi tàllal te tab bu maandu nga, jox ma

15
Boo yaboo jël ma ragg xotti samab xol
Defaraat tëj ca Mbóot yu rëy ya, defal ma

16
Boo yaboo jël ma yar ma sañ nga ko sallaaw
Ba baken beek Saytaane dootu sonal ma

17
Boo yaboo jël ma ngir sawaat ma araf ya
Sol ma lay tax ma xam Boroom bi, xamal ma

18
Boo yaboo jël ma yéege Sanga ca Péey ba
Ba ma janlook Boroom bi bam tàmpeel ma

19
Mustafaa Sanga piir nga jomb nga delloo
Ku la yaakaar, maa ngii dagaan si la may ma

20
Ba keroog Bés ba yal nga feese samab xol
May dëkkee ñaan Njool miy dëkkee sottil ma

5 Ramadaan 1444
26 03 2023


La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)Les poèmes de Mamadou Bara SAMBPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non