La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)

LEJEUNEPOETE REND HOMMAGE AU MESSAGER D’ALLAH (PSL) : Nàndal ma

today3 mai 2023 141 3

Arrière-plan
share close

Lejeunepoete mu ngi leen di ñaanal Ñaanug Jàmm ak xéewal.

Xerawlu leen ñetti xasida yii mu def ci Sanga bu tedd bi SAWS.

1. Nàndal ma (Ndar, 22 Octobre 2020)

2. Ay Mustafaa sama Waa ji (Yëmbël, 22 Juin 2022)

3. Maa ngi nii ñàkk ngay ku woomle ( Yëmbël, 26 Mars 2023)

Jërëjëf Sëydinaa Limaamu Laay, teral nga nu Démb, teral nu Tay. Lu nu la way doyul

  • cover play_arrow

    Nàndal ma lejeunepoete

1
Da ma xëy yaram wiy metti saa cër yèp nagam
Ma dëkkee nelaw ñuy laaj xanaa da fa sibbiroom

2
Doktoor bu ñëw seet seet ni leen dara laa gisul
Ñuy tontu naan maa-man yi ñooy faj jàngoroom

3
Maa-man bu jéem tële jox moroomam xol ya jéex
Sëñ buñ fi yaakaar ñëw na dellook saafaraam

4
Waa kër ga toogu ma, jaaxle not lool seeni xol
Yaakaar ya tas ñuy xaar Dogal ba ku neey sëngéem

5
Nees tuut ma yewwu ni leen na ngéen dal bañ ragal
Li ma feebaray Njool mii ma namm janook jëmmam

6
Njool mii ma sàkkoo gis ñu xañ ma ko boob ba tay
Mooy liy xasan saab xol di suuxat naqaram

7
Yaw xayra-xalxil-laahi maa ngii bóof sa kër
Gaa ñaa ngi ñëw di ma romb ngay yéegal ñu dem

8
Saa yun xëyee nit ñëw nga saafara jàngoroom
Nit dand ñëw nga raxas ko féexal ab xolam

9
Saa yun xëyee ngay jëwrinoo ay jaam ni man
Fal leen ñu lay xidmaal di sàkkoo am ngërëm

10
Saa yun xëyee nit am (wilaayatu) jaar ci yaw
Nga xamal ko mbóot ya mu mujja jàlleey àndandoom

11
May toog di xaar, bés bii nga may woo manta ñëw
Saa xol bi jéex ndax liñ ko xañ sag xar-kanam

12
May ñee ñi naan ci sa ndox mu neex mii romb lem
Ba ñu ngay tërëf ndax xol bu màndi ci neexitam

13
Gaa ñooñu miin Diiwaan bi ak ñiy gontu yéeg
Ci sa barke ñiy dëkkee di déeyook seen Boroom

14
Ñiy dund Aljana fii ci Àdduna, Mustafaa
Yaa leen jafal, ay Njool mi jox ma ma naanitam

15
Sàllaaw Yonnen ndeem sopp laa tax gaa ñi dem
Saa xol bi xam nga ni yaa ko moom saag ruuh itam

16
Buma sàgganee tilimit Yonnen bi ñi ngay raxas
Luy tee nga boole ci ndaw lu ngéejoo doon sa ndam

17
Lu ma am ci Àdduna boo ci jiitul Mustafaa
Day mel ni jëmm ju ñàkk Ruu gaak ab xolam

18
Tàllaahi Taahaa sag ngërëm laay xëy di wut
Ku la am ci Àdduna jot na caabiy Aljanaam

19
Ku la moy xolam ba du féex turam day gaawa fay
Muy dañ-dañeek tiisam wa dëgmal alkandeem

20
Yaa gën ña woon Démbaak ñu Tay ñeek ñii di ñëw
Yaa moom lu fiy mbaaxak teraanga te yaay Imaam

21
Bés pénc yaay daagook sa may ya waxak Boroom
Ñép naa la jaajëf Mustafaa doo seen moroom

22
Bés pénc ngay ràngoo (Liwaa ul Hamdi) wéy
Cër yepp naaxsaay Mustafaa rek yor bosam

23
Bés pénc kuñ yaakaar mu yaakaar Mustafaa
Kiiraay ya dañ ñép xam ni Njool mee moom Maqaam

24
Njool fal ma tay nàndal ma may ma ma doon sa ndam
Njool jëwrinoo ma ba ker ba may dee yaa Imaam

25
Na la Yàlla fay, fay say sahaabaak sag njaboot
Yàggal fi sët bi la wuutu ful ay xéewalam

26
Suturaal nu tette nu may nu xéewal gunge nu
Sàmmal nu Diine ji may nu tawfiix ak salaam

#lejeunepoete
Ndar
22 Octobre 2020
5 Gàmmu 1442


La Vie de l'Imam Al-Mahdi (psl)Les poèmes de Mamadou Bara SAMBPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non