Les poèmes de Mamadou Bara SAMB

LEJEUNEPOETE REND HOMMAGE A IMAM SEYDINA GAYE IBN IMAM SAKHIR GAYE

today24 avril 2023 131 4

Arrière-plan
share close

Marsiya Imaam Sëydinaa Gay

Cet hymne est dédié à imam Seydina Gaye fils du grand Mufti de Yeumbeul imam Mouhamadou Sakhir Gaye.Héritier de l’imamat à la Grande Mosquée Layène de Yeumbeul de son  illustre père, imam Seydina Gaye s’est éteint le mardi 11 janvier 2022 à l’âge de 73 ans.

Jooy nit ku baax ku fi joge lu war la, fàtteliku ko ak seede ay jikkoom yu rafet ak ay jafam doon it lu mant ñàkk. Waaye saragal ko itam ci ab liggéeyam lu sunu Boroom di bég la. Tay Lejeunepoete mooy sargalee Imaam Sëydinaa Gay 73i bayit ngir màndargal 73i at yi mu dund ci liggéeyal Boroomam bàyyikoo fi bésub Talaata 8i fan ci Maamu Koor atum 1443 tollook 11.01.2022. Yalna ko Boroom bi nangu te yeesal njéggalam ci Imaam Sëydinaa, ay Baayam aki Maamam.

  • cover play_arrow

    Marsiya Imaam Seydina Gay Lay lejeunepoete

1
Al Hamdu lillaahi yaay Buur nangu nan sa dogal
Toroxlu nan di La santak kañ ne yaa di Jaliil

2
Moo Buur bu bindab laram te ken yëgul dama ni
Buy jël du tàggu mbindéef te faalewul ku ko xul

3
Yàllaa fi nekkoon bi len nekkul di Buur di Ahad
Te bés du ñàkk mu dellook wéet ga moo di Kamaal

4
Càppaacolee Fari Buur du ken te kenna du Moom
Subhaanahul-laahu Buur dooleem ja raw na misaal

5
Cofeel a tax mu amal Muhammadan mu di jaam
Ken fekkewul, Mommaduy sàbbaa te lenna amul

6
Muhammadun dafa yàggak Yàlla xam ko bu wér
Boroom bi soppa ko jël lép may ko roof ko ngënéel

7
Yonnen bi doon Durratul Baydaa u képp a ku am
ab Cër ci moom la bawoo ku jàlla moo la xajal

8
Boroom bi xëy di amal ci baatu Kun fa Yakoon
Ak sopp Ahmadu, jël nit fal ko sedd ko njël

9
Muhammadun lumu rëy rëy jaam la donga ci moom
Kudul Yonnen matla wax lii xam ko daa jafewul

10
Yaakaar mbindéef warta tax nga jiiñ ko Yàlla, te sax
yaakaar kudul Yàlla Buur du jaadu bàyyi ko xel

11
Yàllaa fi nekk kudul Buur Yàlla jaam la ni yaw
Mooy def di dindi di folli saa su nekk a di fal

12
Toroxlu jaamu Ko mooy sun cër ba tax mu yabal
ci nun Yonnen ya ñu nuy jaarloo ci Yoon wa (ajal)

13
Wéetal Ko tënku ci Moom ak jooxe ay ndigalam
Fu ab Yonnen feeñe leey doon Yoon wa muy taxawal

14
Tawhiid gu ruus moo waral Nuuhin nitam wa nasax
Tuufaan ba ray leen ba ray doomam ja toog ni gëmul

15
Tawhiid a tax sunu Maam Ibraayma beddi nitam
Bañ taal ba soob ko ca muy sabbaa di sant Jaliil

16
Tawhiid a tax Njàmme jël Alwaah ya sanni ko ker
ba Saamiriyyu taxee ñuy jaamu nag wa, di xul

17
Tawhiid la Yàllay tëyee Iisaa Bésub wuyu ba
Ndax yaw la mbaa man la? Iisaa naa Ko yaa nu amal

18
Tawhiid a tax Ahmadul Muxtaaru woote ba wëy
Buur Yàlla woowaat ko muy taal taal ba ñépp a jafal

19
Fu ab Yonnen jaar ba lép jag Noon ba xëy di dareet
ngir fàtteloo nit ña Kii leen yor, Ki leen di defal

20
Xeejam ba muy xeexe mooy ag réer ni jaam bu xamul
buy xëy ci ngëm bala muy gontal ñu tas lamu jal

21
Ku yittewoo di xamal jaam boobu noonu na la
ci bépp a boor te du dañ di jéem a fay li nga taal

22
Ay ngalla yaw jaam bi ngéejoo xañtu Yàlla jogal
ngir sàkku xam te nga sóor ni benn a jaam du fi beel

23
Saa yoo xëyee kenn a dem Barsax ñu gas bamu xoot
tàbbal ca Dee rekk a wóor waat naani jeggi na xel

24
Loo leen fi jur di yafal, loo leen fi wut di dajal
Loo leen fi sos di rëyal Dee bettaleen nasaxal

25
Goneek i mag Sëriñak ndongam ba ken du fi des
Góor ak jigéen, yaaram ak saay-saay, ku matle mu fél

26
Feebar taxul mu jegeñ ak wér taxul mu sori
Ku xëy xamoo di nga yendal bay xalaatati njël

27
Bu Dee rusoon kenn a kon Yonnen bi toog fi di beel
te kon mu bàyyi ko ak soppeem yu baax ya mu jël

28
Dunyaa du kër ku mu kar lay wër ba dëj ko ci ker
Roof kay nelaw ba mu xëy Dee yee ko muy lewatal

29
Moo dund goo xam ni buy jéex ken du tàggu boroom
Te saa su nekk mu ruus ndax jar na daw di dajal!

30
Ndax jar na tooñ sa Boroom ndax jar na wor sa moroom
Ndax jar na jaay sa ngorak sa diine waa ji waxal!

31
Ku ñàkk doole te man tooñ war na moytu Ku am
kàttan te sàmm waxam, tee noo dëkkee rafetal

32
Kon jaam bu am xel bu yewwoo war na séentu keroog
bu wërsëgam wa di jéex mu jublu Buur bi ko jël

31
Ñu yoor ko bàmmeel ba kuy soppeem ba bàyyi ko dem
mu wéet ca pax ma ku sóorul lii da nga xamagul

32
Ku yor ba guujal itam tay pax ma moo di sa kër
wet ngay tëddee ñépp a dem te dun ñëwaat di la xool

33
Malaaka Yàlla yu rëy te raglu ñëw gane la
Boo xàmmewul sa Boroom seen yar ya tàmbali dal

34
Koo manti doon lenna rek mooy tax nga mucc keroog
mooy xam Yonnen beek Boroom Kursiyyu mii la amal

35
Immaa da ngay sax ci leer ak may yu rëy jëmale
Bés-pénc mbaa lëndamak tiitaange ngay far dëkkal

36
Yaw mii di sàggane jaamook xañtu Yàlla keroog
ngay xam ni loo am to doonul Yàlla ding ko layal

37
Yaw miy dëkkee wut di jal keroog nga xam ni lu waay
di wut ludul Ki ko moom reccoom ëllëg soriwul

38
Ku boddiwoon ñi mu am tay lenna mooy mebetam
mooy delluwaat rafetal yaw mii fi des na nga dal

39
Ñu wal ca Bufta ba mbindéef yépp a jog di faxas
seen bopp yay wuti foofa ñuy layoo di jubal

40
Cëy Bés ba raglu na ñuy door ñii di gàddu ñële
ñii far ñu leen di bamax ñii ñàkk gët ya di xul

41
Ñii màndi far di tërëf ñii soppi seen melokaan
Te ken du tal sa moroom, ku nekk naa lu ma dal!

42
Tàngaay wa tàmbali cëy maa yéem bileb Taxawaay
Lëndam ga tar ñépp a tiit di xulli gët ya di xool

43
Yàggaayu Bés baay waral ñuy seet ku fay ñeme jog
wax ak Boroom bi mu jéexal tiis wi moo di Jaliil

44
Jahannamay xaacu mbindéef yépp a mujj a ragal
Ñu seeti Yonnen mu ràngoo may ya ak yamu sol

45
Keroog la Yonnen di tempak taar ba ñépp a dëggal
dem ñaan Boroomam mu tin ko àtte ñép man a dal

46
Ñu tàmbalee àtte cëy bés boobu jar na xalaat
Lu waay di def bu ko sóorul xel ma moo wayagul

47
Bésub rëbbante ba, mar waak yuux ya dëkke di jib
Lu waay di nëbb mu feeñ lii loo ko waaje doyul

48
Koo àndaloon ci kërug Dunyaa keroog fumu jëm
nga ànd ak moom na ngay seet ñii nga dénk sa xol

49
Keroog la ñépp a di xam kuy Mustafaak ñimu fal
Keroog la ñépp a di ñee xeetam wu rëy wi ngënéel

50
Bastul ya far tegu ñuy peesee ka regle di seet
Nees tuuti Teere ya naaw te kuy mbindéef di nga jël

51
Ñu gàlla yoonu Siraat ci kaw Jahannama muy
yëngoo ka yuuxu di xaar ku daanu ak ku ñu fèl

52
Yéem naa Siraat sew na booleek ñaw te yoon wa sori
Nan teel a miin Góor gi fay jàllee te gën ko bégal

53
Ginnaaw Siraat Déeg ba ñëw nuy ndokkalante di bég
Ku naan ca ndox ma tërëf ndax mbégte maak nimu mel

54
Déeg booba laay ñaan dajeek ki Yàlla jëlsi fi tay
Baay Sëydinaa Gay mi jaayoon lépp a ngir rafetal

55
Bañ nee ki donnoom Saxiir Gay donna gën ji jikkoom
moo génn Àdduna aw tiis far na muur sunu xol

56
Ñii naa du moom manta dem, ñiiy tudd Yàlla ca kaw
Rangooñ ya sar xol ya diis ndax ñàkk mbër mu kamaal

57
Xabaar ba jolli ku nekkay ñaan di yéem Ki nu moom
Dee rekk a wóor te du maslaak kenna bàyyi ko xel

58
Bésub Talaata la dem (Haa’un) ci weer wa ñu jël
Baay Baabakar ati Maam Sëynaa la am yu kamaal

59
Ñu xëy di waajal ki waajoon bés ba ñuy taxawal
di seede ay melokaanam Sëydi day ku matal

60
Baay Mommadul Aminak rakkam ja tiim ko jullee
Bés boo bu rek lañ taxaw te Sëydinaa julliwul

61
Mbooloo ma daj na keroog mag ñaaak xaleel ya taxaw
Di bàkk Yàlla ca kaw ak nangu bépp a dogal

62
Soppeem ya Baay Jibi, Sëynaak Maysa ñoo ko dugal
ca pax ma wuufal ko Baayam, Sëydi am na ngënéel

63
Tay ñàkk nan mbër mu fonkoon Yàlla ak Yonnenam
Ku yiw te sell te muñ te maandu man rafetal

64
Tay ñàkk nan mbër mi donnoon Baay Saxiir taxawoon
ci sàmm Miiraas bi fonkoon Baay ba fonk ndigal

65
Tay ñàkk nan Sanga piir ku xam te xol ba woyof
Ku am teraanga di gor ku sàmmu man yéwénal

67
Wuutal na tay mbër ni moom ku ñépp a seede jikkoom
Libaas mi Baayam wegoon mu weg ko bàyyi ko xel

68
Imaam Suleymaan mu baax mee jël cëram ba cëral
Ustaas Libaas, Baay Jibeek Yëmbël teral ko (ajal)

69
Imaam Suleymaan da ngay gor piir te ñàkk kiñaan
Wutoo ludul Yàlla toogal taawu leeri Yëmbël

70
Imaam Libaas noo ngi nii di yeeslu ak di la ñaa-
nal Yàlla taawu la sallaaw moo di Buur bi la fal

72
Xamoo ludul jàng ak daan doole boobu ba tay
Tay may yu rëy ya ca Maam Jibriilu yaay ki ko jël

73
Na Yàlla tàwwi sa fan te julli sëlmëlati
Ci Mustafaa te yërëm Baay Sëydi gën ko teral

Lejeunepoète

18.01.2022


Les poèmes de Mamadou Bara SAMB

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non