Les poèmes de Mame Samba Laye SAMBARGA

MARSIYA CHERIF MAME ALASSANE LAHI IBN SEYDINA ABABACAR LAHI

today30 mai 2023 158

Arrière-plan
share close

Marsiya Chérif Mame Alassane Lahi ibn Seydina Ababacar Lahi

  • cover play_arrow

    May 20, 12.41 PM_Karaoké Shark Studio Effects

Bismillahi magui diaal délou diooy sounoup Serigne
Naarou soxena Fatou Diop Mame Alaa mou diiné dji

Sante Yalla war na diame diame bou geum limouy dogal
boudée lou néekh mbaa lou tiis sant warna diiiné djii

Lou méti dalena ahlou laah dale ndiabotou Mame libass
Seteum bou yiwba lakhou waat Mame Alaa mou diiné djii

Tamkharit la déme djinaan bis bou tiis dalat nanou
Seutoup Yonéne bi daanu waat come Oussayenou diiné djii

Khibar bi tiis na gneupee gneuw Di sant Laahou rabbanaa
Di diaale satoub Rassou laah ka done kéno si diiné dji

Mboloma ma took fa Diamalaye zikar sa riir gnou goungé ko
Gnou dioukh ko Baye ba Mame Mandione kay khalif si diiné dji

Domi seydina issa Domi seydina mandione thiatou Seyedi Babacar Mame Alaa mou diiné dji

Gni xam thiereum té dafa déme dako wah thi séni mbir
Dako dioytou séni tiis Di sakou gnana si diiné djii

Ragual na yala Moy kou yiw Daana maïtou adina
Donou baye ba siw néloom xam sarii’ãn diiiné djii

Choufii la won si diamou yala masta nagou gui dioudom
Am ndiouréer doyoul geunél boun Di fohh si diiné djii

Mou méle ni baye Babacar Di gnaan si yala niy brom
Kou diaxelé déme fa sakou gnaan bidéw la woon si diiné djii

Daane nafa déme moumay téral danma yar si diiné dji
Daama weugni Guir ma yiw Dana wattou diiné djii

Dawoul sakou aÿ deureum thi nitt gni dawolé sonal
Diamou yalla Moy mbiram roy Libass si diiné djii

Wétal na mak dji Mame libass ak moukhamadoul amine
Mouhtar imam madon magam baye Bassirou diiné dji

Imam bassir nidoon magam moudi tawou Seydi Mbaye
Guinaw maguam dia Malick Thiaw ak Amar mou diiné djii

Yal na yala faye ko yiw douli léer té foule dieufeum
Samou dome yi ak gni daane wétalam si diiné djii

Guinaaw Rassoulou démena ak rouhou laahi wa Mame Mandione
Wa Seydi Mbaye na gnéppa wathie dée dou romba diné dji

Marot si souf di dialé waat ahlou baïti yaa Rassoul
Di diaal soxenam sa ak ndiaaboo tou Mame Alaa mou diné dji

Yale na bour bi dolli léer douli barké bak thieurem
Douli wér sounou khalif maïko ndam si diiné djii

Allahou yaa ilaaha naa bil nabiiyi Moustapha
Doulil nou léer Mame Alassane mouy thiéneer si diiné djii

Mame Samba Laye SAMBARGA t.s.m
Marsiya Mame Alassane Lahi Ibn Mame Babacar Lahi ibn Seydina Limamou Lahi (psl)

Les poèmes de Mame Samba Laye SAMBARGAPOESIE

Rate it
0%
Restez informé des nouvelles publications en activant les notifications...! OK Non