MARSIYA MOUHAMADOU AL BASSIR soodaan3
M
ma dooré fi tay Di marsiya dialé Wat tay.
dii tiis Lou ba tay guirék kinou niaak reuy na
A
alhamdou Lillahi. yalla boor bi sagne lii.
niou mougn Lou té dal. khibar bifi wathie tiis na
R
Rassoulou lahi. moy royouway bi geun nieup. khibar bouni méle. daloon si mom té dém na
S
Salaatoul laahi. souma Salamou Rabi.
ãnlal Mahdiyou. seydil saabiriiina
I
inaa lile laahi imamou bassiirou démna. fékki na baye ya. fékki na Mame dia. dém na
Y
yaa seydii . gedion nanou giis sakanam.
thiofél guissi gnoun gnouna ma guissat la ndiouy na
A
adina bii. mougnon guako deudou banéxe. deuk meul sa brome. thiey ãnbid ba démna
I
ilaahi yalla.sa diam bigua dieul.si gnou tay. khadion nafi wayé déf gua liguene ba weuy na
M
Mame dia limamou. ginaw coorém ga ay beus.yadoun lay mat thiy biss lolou wér na
A
ahh yawmiy lathie. guinaw foukki fane you ték niént. la baye laye déme thi wérou coriité lérr na
M
Mootakh alee’tiné dia nou dénthie baye laye. la yala dieulat ka doon maktoum ba dém na
M
matonna imam. maxamaya sakh dé reuy na. yim donou si baye ak Mame dia réuy na
OU
oubée na té moom .gaïndé lawon thi diiné. amona fassaxa. Daana bayaan. léeral na
H
Habiboul laahi. kou soppou lawon thi yala. amone idiaba Moy ãnrif ba wér na
A
amonna magam ya .ak rakkam ya niom nieup. Dononna limamou ak bayam ya wér naa.
M
mouhamadou mii lamine tay xole bi fés na. Mame djiine nak imam mahtar dé wétt na
A
alhlou laahi .andak domam yi dioye naan.akwa kaw saman ;’ou souf si diooy na.
D
Dou diambat mougn na fii dounyaa ba kheuy dém. waliiyoul lahhi cherifoul diin ba dém na
OU
outoul loumou am thi adina doylou dis gor. té gor day guar si yala té mandou xam na
A
alay bounou tiit nanouy yakar té doy loo. té diamou brome bi geume baye laye dé doy naa
L
layéne Nanou békk Di wakh bate bii nou mame dioxe.soupexana laa ilaaha ilaahou woor na
B
baboul laahi bountoup yalla thialan dieum. Nanouy sélal Di wétal yala bakh na
A
adina bi danouy daw rék ba kheuy déme. té déeh Dinou weur bamél dinou khar li woor na
S
sa marsiya bi yaw sou baye bassirou. Manou no wakh sa kharbakh yép xam na
S
sa barké lanouy dagane téy sakou say niaan. Di diéme dila way Di sako sa niaan té rott na
I
ilaahi yaa ilaahi yaa ilaahi. niourott dila niaan toroxelou Di toupe té gneuw na
R
raxas nou si léer té diamal Domi Mame ndione. bi diahi imam bassir thiéy yala bahna naaaaaaaaa ( amiiiiiiiinne)